|
||||||
|
Passpooru ndey |
|
Ndaw si : (Di wax ak xaritam) : Awa, kaay gungé ma, dama am soxla komisaariyaa ba.
(Di wax ak alkaati bi): Assalaamu aleykum… Monsieur l'Agent, jamm ngaam ? Damay defarlusi paaspoor. Damay ganeji sama been wollëré burkinabe, and ak sama ñaari doom. Jotoon na serwis bi ci telefon, ñu xamal ma këyit yi ma wara indi.
Alkaati bi : Jaam rek, Soxna si. Koolëré déy ginnaaw lay féetée. Ma xol këyit yi… Waaw, yii nga ma jox baax na. Wante ma?kena been. Biy wone ne sa jëkkër and na ci ñu bind doom yi ci sa paaspoor.
Ndaw si : Xalaas ! Lu waral loolu ? Xanaa juruma léen ? Seen këyiti juddoo ngi nii, yiy birël ne maa leen jur !
Alkaati bi : Ken wéddiwul ne yaay ndeyi gone yi, Soxna si. Wante, loolu du tax nga sañ leena bind ci sa paaspoor lu dul sa ndigëlu jëkkër. Ndaxte yoonu réew mi dafa tërël ne góor mooy boroom kër, moo yore baat bi, kon nak moom rek la yoon may boobu sañsañ. Be tax na faww nga indi këyit wu wone ne sa jëkkër and na ci, ñuy doora bind xale yi ci sa paaspoor.
Ndaw si : (Di wax ak xaritam Awa) : Ce, Awa ! Xam nga sama xaritu Burkina ba de, ba muy ñëw daaw, ànd ak caat am, këyit woowu ken laaju ko ko !
Awa : Xalaas ! Bu jigéeni addina bi yèpp dee benn itam, tërëlinu yoon yi wuutenë ! Ni gisgisu nit ñi wuutée … Boo seetee Burkina, fanweeri at a ngi nii ba ñu soppee loolu ak léegi. Foofa, ñaari waajur yi ñoo yem cër ci seeni doom. Looloo waral sa xarit bi soxlawulwoon këyit wi ñu lay laaj.
Ndaw si : Fanweeri at !… Waay ! Ñun, lu ñuy ci xaar ci loolu ?
Alkaati bi : Loolu, cëru dipité yilë… Ñun, doxal yoon la ñu fi nekkee.