Les TIC à l'appui du programme des femmes
pour l'égalité de genre au Sénégal
une action en partenariat ENDA-SYNFEV et Siggil Jigéen

enda-synfev, b.p. 3370, Dakar, Sénégal,
tel : (221) 823 45 42 ; fax : (221) 822 26 95,
courriel : ,

http://www.enda.sn/synfev/synfev.htm

Siggil Jigéen, b.p. 10137, Dakar, Sénégal,
tel-fax : (221) 825 00 56 ;
courriel : ,
http://famafrique.org/sjigeen/siigeen.html
avec le soutien du Programme Acacia
du Centre de recherches pour le développement international, Canada.

 

Lempo bu gënë diis, ci ndey yi

"Ce document peut être librement reproduit, à des fins non commerciales uniquement, à condition d'en mentionner la source : ENDA, Projet parenté conjointe, Dakar, 2001"

Caane : Assalaamu aleykum, Ndey. Na nga def ? Suma doom dafa feebar. Nelewuma guddig biig. Ma yobbu ko kër doctoor, ñu bindël më ordonaas bu seera seer !

Ndey : Wa aleykum salaam, Caane. Sa doom ji yalna wér ak jamm waay ! Di liggéey boole kook topptoo sa njaboot, lu métti lë !

Caane : ((ci waxi kaf ) Léegi tey nga wax lu set ! (ci fullaam ) Seetlu naa démb këyit wiñ ma fayee : li nguur giy jël ci suñu payoor bari në lool ! Xeetu lempo wu nekk dinañ ñu ko fayyeeku ! Xam nga at mu nekk, dina am lu ñuy delloo suma jëkkër ci lempo bi, dimbëlée ko ko ngir xale yi ; waaye man miy seen yaay, ken du ma dello dërëm !

Ndey : (di ko kokkli ) Waawkay !… (japp fullaam )Fii ci suñu réew, jëkkër mooy borom kër. Looloo tax ñu japp ne moom mooy gaddu wareefi kër gi. Moo tax ñu waññil ko lempoom ngir dimbëlée ko ko.

Caane : Waaw… (ak xol bu tang ) Na nga xam ne maak moom, ñun ñaar ñéppay liggéey, waaye suñu waccee ba nekk kër gë, man rekkay liggéey ! Te maay wodd xale yi, ku ci feebar maa lay faj, maa leenay bind ecol, maay topptoo seenum njang. Waaye dafa mel ni ken gisul li may daj ci ñoom. Ñu di ma daggal lempo yu tol ni yi ñu lay daggal, yaw mi yorul dara ci njaboot. Defe nga ni loolu jaadu na ?

Ndey : Xawma jaadu naam déet dé. Waaye daal noonu la ko yoon rëddée.

Caane : Nekk salibateer kay neex na ba dee… Man jaboot laa, maa la ëpp-i wareef fuuf, te maak yaw-a bokk lu ñuy fay ci lempo. Maa ngi ci néegu sëy, yore njaboot : yoon faalewul loolu. Te goor ñi di suñuy cammiñ, ku ci takk jabar ñu dimblé lë ci sa lempo.

Ndey : Waa sendikaa bi doon nañ ko waxtaanee kerook. Nee na ñu attey réew mi dafay jalgati yoonu liggéey wi nga xam ne dafa tërël ne ñépp-a yem ci wallu liggéey. Kees-i nguur gi daal, li ñuy dugël ci xaalis at mu ne ngir lempo bu métti bi ñuy teg jigéen ñiy sëy, ken xamul nu mu tollu… Ndax defe nga ne jigéen ñi jaboot tey liggéey, teg leen lempo bu diis man naa tax réew mi am alal ju doy ?

Accueil | Documents sonores | | Retour haut de page