|
||||||
|
Alokaasyon familyaal |
|
Njaay : Assalaamu aleykum ! Madam Mbuup, naka nga def ? Naka liggéey bi ?
Mme Mboup : Maa ngi sant Yalla ! Na nga def ak afeer yi ?
Njaay : He, damay góorgóorlu rek ! Fi mu nekk, teretu turism bi jeex na. Ci juróomi weer rek lay yem. Bu ubbée, moom, tubaarfakalla, wante fi ñu tollu moom, amul liggéey. Rax ci dolli, sama soxna léegi mu bërël ligéeyam ndaxte léeggi mu mucc. Looloo waral samay ta?k, ngir toppatoo këyitu alokaasyo? familyaal. Xam naa ni du bari wante dina ñu dimbële ci kër gi. Bu nawetee, sama payooru soxna rekka daan tiyé kër gi.
Mme Mboup : Waaw Njaay … War nga xam ne alokaasyo? familyaal yi, boroom kër guy liggéey rekk mo ko yelloo. Dëgg lë boroom kër ngë, wante léegi nekkuloo ci liggéey …
Njaay : Nga ne ma ?!… Kon nak nañ ko fay sama soxna, moom mi ngi liggéey …
Mme Mboup : Loolu munul nekk. Ni ma la ko waxeewoon ca njëlbéen, alokaasyo? familyaal, ndimbël lë lu ñuy jox liggéeykat bu jaboot. Yaw jaboot nga, dëgg lë, wante sa liggéey dakk na.
Njaay : Loolu moom doy na wax ! Nee naa la suma liggéeyul, moom mooy yore kër gi.
Mme Mboup : Li ma la mënë xelal mooy nga def li ñuy wax ci nasaraan "delegaasyo? piwisaas paternel". Su booba, mbir mi mënë sotti.
Njaay : Luy loolu ?
Mme Mboup : Maanaam nga jox sa jabar cëru njiitu kër gi. Ca tirbinaal ba la ñu koy defee. Foofa ngay dem sedee ne sa baat ci doom ji, jox nga ko sa jabar.
Njaay : Nga ne ma lan ? Loolu diisnë di ! Naka la ñu ma mënë laajee lu rëyée noonu ? Ndax rek duma liggéey at mi yepp ! Xanaa gone gi dootuma baayam ? Xanaa amul meneen pexe mu ñu mënë dimbëlée ñi mel ni man, te bañ ñoo laaj lu tollu noonu ? Lu waral sama soxna di liggéeykat ni man te mënulë am alokaasyo? familyaal ? Li muy indi ce kër gë tollu na ni li ma fay indi, walla mu ëpp ko !
Mme Mboup : Moom kay, mettina ! Wante yoona mel noonu. Bala nga cee sóobu nak, war nga koo settantal bu baax ! Boo demee tirbinaal, dina ñu la leeralal lépp li ci war. Ba fi may wax ak yow nak, masuma gis genn góor gu ko nangu.
Njaay : Lii moom jaaduwul ! Lépp ci alokaasyo? familyaal rek ! Jaaxle na de !