Les TIC à l'appui du programme des femmes
pour l'égalité de genre au Sénégal
une action en partenariat ENDA-SYNFEV et Siggil Jigéen

enda-synfev, b.p. 3370, Dakar, Sénégal,
tel : (221) 823 45 42 ; fax : (221) 822 26 95,
courriel : ,

http://www.enda.sn/synfev/synfev.htm

Siggil Jigéen, b.p. 10137, Dakar, Sénégal,
tel-fax : (221) 825 00 56 ;
courriel : ,
http://famafrique.org/sjigeen/siigeen.html
avec le soutien du Programme Acacia
du Centre de recherches pour le développement international, Canada.

 

Këru sëy

"Ce document peut être librement reproduit, à des fins non commerciales uniquement, à condition d'en mentionner la source : ENDA, Projet parenté conjointe, Dakar, 2001"

Mareem : Yaay booy, jaaxle na… Demba, sama boroom kër, li mu fiy nekk bariwul ndax liggéeyëm. Yalla baax na ba ma nekkee ci seen wet ngeen di ma wéttëli…

Wante biig, nee na ma ma sëyi Yëmbël, ca sama goro. Te su boobaa, dinaa ñakk sama liggéey ci isinu fosfat bi. Te wóorul ne dinaa am lu ma japp fa ma jëm ca Yëmbël. Dinaa boole wéet ak ñakk. Bi ma ci waxtaanee ak Demba, "Boo demee foofa wuut leneen" la ma tontu.

Yaay ji : Doom, Demba sa jëkkër lë, dan ko wara déggël.

Mareem : Su ma jaaree ci li mu bëgg sax, du ñu faxal di gisënte, ndaxte mu ngi ci tali bi guddéek bëccëg. Li gënóon moo di ñu wuut kër ci bérëb bi nga xam ne fa laay liggéeyée. Mu mën di dem aka dikk, di ma fa fekk. Neena ay jigéenëm dina ñu ñëw wéttëlésimë. Ñu baax la ñu, dëgg lë, wante, japp sama liggéey ba mën di ko dimbëlé ci kër gi daal moo ma gënë yittéel.

Yaay ji : Na nga seet sa xel bu baax bala ngay def lu lay jurël réccu. Dëgg lë, meen lu rëy lawoon ci suñu aada. Waante, ci yoonu tey, jigéen fu ko jëkkërëm dëkkloo rek, foofa la wara dëkk. Ndax jëkkërëm mooy kilifaam. Boo ko deful, day mel ni danga fay, te su boobaa sañ na la cee fase sax. Fook naa ne du loolu ngëen bëgg. Te bërki démb rek ngeen sëy. Ak ni ngaa diisée nii !

Mareem : Yaay booy, xam nga ne loolu gënëlumë. Li ma bëggóon mooy ñu waxtaan ba déggóo ci bérëp bi ñu fas yéenë dëkk, te fekk ñu seet ko ba gis ne fii moo gën ci suñu njaboot. Loolu laa lo doon jéemë xamal, waaye moom nee na fa ñu wara dëkk daal, sama yoon nekku ca.

Yaay ji : Moo yey de, doom ! Danga wara topp sa ndigëlu jëkkër…

 

Accueil | Documents sonores | | Retour haut de page